Jëkkër ko mu na ne (yeah yeah) Sutura yërmande (yeah yeah) Bul dóor, bul saaga, jantal men Jigéen la Yàlla moo ko dooleel yeah Sant naa la bégal, wéral, goreel Jugel ci ñoom dañu leen war a teral Bu kër gi neexe ñoom la dañu leen war a keral Su ma sañoon dara du leen metti, yeen a waral li Anyi yeah Ku xool ba jël lu metti tekk ko Bu ñu ko demoon teg sa doom Dinga mu na yëg li may yëg Tay ma woy ba foog ni dama dof Faw ma woo ma woo la xool ma yaw la jigéen yaay yee Yaw say wena sëg waaye yaa nu mën Gannaaw yonent lu Yàlla bind yaa ci gën Kon buñu ko xarafal, buñu ko gaañ ci dënn Ndox du jéeg, pax bu jege, pax dafa fekk Yaw bul ko dóor, bul ko saaga woo Jël ko def ko doom Ndax mooy sa soxna mooy sa yaay boo yoo Yërmande ci ñoom Jigéen bul ko dóor, bul ko saaga Meritewul lii Ndax moo ñu jural yaay, jural ñu baay booy Kon yërmande ci ñi! Xare baddax comme Sitoé Doon jaambaar ndor ak nawet Man yeen laay delloo njukkal Jigéen na jur ki toog palais Icône ni Mame Diarra ak Marie Boo danoo jugal Eh big up to Halima Gadji Kennen ku baax tuddel Doon ñafekat, bañekat Di diplomé ak baykat Fees Université def fac Grade yi gën a di bari, laf cat! Yeen ay diamant yenn ay or Am na ay jigéen yu mën góor Bu dul jigéen, kan lay doon? Ñoom nak war rekk lañuy door Listen! Baat ba ma jël ca maam Doomu góor nga jugal, sol sa dàll Bu de góor nga dinga songu daan Bu de jigéen'anga ci digg ginnaaw geej Ndam, mérite, am njëriñ, mat sëriñ Gàllaaju jigéen mu ngi ba digg ginnaaw géej Akak yeleef gi war ci ñoom ñanu ko def Ndax jigéen mosul feete suuf Talaatay Ndeer ay jigéen ñoo ko def Yaw bul ko dóor, bul ko saaga woo Jël ko def ko doom Ndax mooy sa soxna, mooy sa yaay yaa boo oh yoo Yërmande ci ñoom! Jigéen bul ko dóor, bul ko saaga Meritewul lii Ndax moo ñu jurel yaay jurel ñu baay boy Kon yërmandé ci ñii