Li ma yëg ci xol bi du deñ Mbëggeel dëgg xol du fen Su ma la tooñee danga ma baal Bi ma ñépp folee yaa ma fal Yàlla def fi ñu yegsi tay Kon nak duma bàyyi lu mu metti-metti Kon waroo tiit, ndax dootoo wéet Fi lek yaa ngi geestu gis ma ci sa wet Kenn du la jam naa ni Gilet pare balle maa ngi ni maa lay aar Ci sa wet laay fanaan ci Lu mu guddi guddi bae ndag ma xaar Kaay jege ma, nga wax ma Chérie boo bëggee bëgg naa Boo bëggul bëgguma Yaw jege ma, wax ma Boo bëggee bëgg naa Boo bëggul bëgguma Ay dawalal, chérie dawalal Yaa téye volant bi bul taxaw, dawalal Ay dawalal, mon bébé dawalal Yaa téye volant bi bul taxaw, dawalal Day metti rekk waaye Ñun ñaar ñooy àndandoo Ku la bañ, lam bañale Ndax ñun ñaar ñooy àndandoo Man bëgguma ragal naa Nit di dox di ma gis sans yaw Kon du nice Yaw danga ma fan dama la fan Li nga gis ci man ne ci yaw Xol bu nice Man naa la jàpp yëkketi la Ba nit yépp xam ni yaw la Sama xol bae yaa ko damp Di ko bëgg noo ko bëggee Yaa ko fa am danga ma jege Yokk ma ndam mbide yide ma Te noo ko bëggee bëgg naa Kaay jege ma, nga wax ma Chérie boo bëggee bëgg naa Boo bëggul bëgguma Yaw jege ma, wax ma Boo bëggee bëgg naa Boo bëggul bëgguma Ay dawalal, chérie dawalal Yaa téye volant bi bul taxaw, dawalal Ay dawalal, mon bébé dawalal Yaa téye volant bi bul taxaw, dawalal Day metti rekk waaye Ñun ñaar ñooy àndandoo Ku la bañ, lam bañale Ndax ñun ñaar ñooy àndandoo