Waawaaw C’est comme ça [Soraya] Femme d’affaire ba keroog muy neex Góor du ma yàpp man ayca tay mu neex Booy wër jom moo ngi fi Fu la ju mat ak fit bi sax Boo gëmee Yàlla kon looy ragal [Kya] Xawma ko Noonu la àdduna bi noonu la Takkal sa sër te bul tokk Duma ko yakaar ci góor (Jugal, jugal, jugal) Dooley jigéen fu lak jom laa way (Jugal, jugal, jugal) [Satou Niang] Yaw bul ko dóor te bul ko saaga Soo ma munul neexal bul ma jànni Méritéwul lii di dóor aka saaga Soo ma munul neexal bul ma jànni Ahhh, jigéen laa Jigéen laa, jigéen laa, jigéen laa Jigéen laa, jigéen laa, jigéen laa Teral ko, lingeer laa, jigéen laa Lingeer laa Songali nga, songali nga, songali nga Déedéet, songaliwul kay Ku mënul te bawoo lu yaku yawaa Jigéen laa [Ouly] Ñun ñooy jigéen seeni yaay Jigéen seeni rakkak seeni soxna Dëkk ci liggéey jaambar laa Su ma séyee mu neex Ndaxte man jigéen laa [KineKine] Mi nge kooy dóor waxul Ba ngay kontaan moom takkul Muñ bés bu ne saxul Sama bat ci kaw Hommage à toute les femmes Qui sont maltraitées Dans les maisons, dans les prisons Dina metti waaye bul bàyyee Soo gëmee sa boroom looy ragal sa noon "Man xawma ko" Tay dina metti suba day neex Waaye soo muñee ni suba day jeex Sa lépp sotti [Satou Niang] Yaw bul ko dóor te bul ko saaga Soo ma munul neexal bul ma jànni Méritéwul lii di dóor aka saaga Soo ma munul neexal bul ma jànni Ahhh, jigéen laa Jigéen laa, jigéen laa, jigéen laa Jigéen laa, jigéen laa, jigéen laa Teral ko, lingeer laa, jigéen laa Lingeer laa Songali nga, songali nga, songali nga Déedéet, songaliwul kay Ku mënul te bawoo lu yaku yawaa Jigéen laa Je suis femme battante Jigéen fu lak fàyda jigéen Ngor ak doylu jigéen Bul ko dóor, bul ko saaga jigéen Bul ko toroxal