Moo ngi séy te moo ngi muñ Moo ngi def li mu mën Waaye jëkkër jee dënke Xas dóor jëkkëram ni lay séye Jëkkër ji du ko defal dara Du yeré du dall du cheveux Li mu jàppe cadeau mooy Xas dóor jëkkëram ni lay séye Bu Wally doon boole Faramareen yépp Li jëkkër ji yor ci gel moo leen ëpp Tey saayu waxe jëkkër ji jàpp Xas dóor jëkkëram ni lay séye Li muy dundu metti na Te musul faay fonku na séyam Xamul bonheur séye lu dul Xas dóor jëkkëram ni lay séye Kenn xamalu ko dara Lu séye bi metti-metti Loo manqué mu ne dara Séy si wul daa sey sii Toog na muñ te njaabot ta ko waral Séy ba déeg waaw góor Méritéwul ay dóor Dee ko takkal ay or Boo seetloo metti na dawul Lu séy bi metti-metti Moo ngi dundal njaabot gi Te jëkkëram du ko jox dépense Moo ngi taba taba dundul njaabot gi Yéwoo ca fajar dem jàyyi Njëggënteek auto yi Danga dangi bu dul jeexe Bokku naat indi def ci kër gi Ba changer jëkkëram léegi neex na Te li mu doon dundu metti na Te musul faay fonu na séyam Xamulwoon bonheur lu dul Xas dóor jëkkëram ni lay séye Kenn xamalu ko dara Lu séye bi metti-metti Loo manqué mu ne dara Séy si wul daa sey sii Toog na muñ te njaabot ta ko waral Séy ba déeg waaw góor Méritéwul ay dóor Dee ko takkal ay or Boo seetloo metti na dawul Wuy leleleeee yow Moom dunde na lu ne Boo seetlu wee metti na dawul Séy ba dégg waaw góor (waaw góor) Méritéwul ay dóor (méritéwu ko) Dee ko ko takkal ay or Boo seetloo metti na dawul