Neex ba dàq lem Mbëggeel bi da ma dem ba daf ma yem Li may yëg sama xol Moom mi su ma koy xool Hey, xam naa ne li du neen Yaay bagg bi rot ci sama tenn Li may yëg for na lool Moom mi su ma koy xool Xol bi di tëb, di fecc Su ma nekkee ci sa wet Duma mësa wet ndax yaa tax may nekk Doo juge ci xol bi xel bi yaa fi nekk ni Man ak yow à l'infini, bae xool ma fi Yaw rekk laay topp Sama xol yaw rekk la sopp Yaw rekk laa nob Sama xol yaw rekk la sopp Moo tax loo wax ma ne wa waawaaw Soo ma nobee benn ma la dàqa nob Moo tax loo wax ma ne wa waawaaw Soo ma nobee benn ma la dàqa nob Fok ma wane wa àdduna Sama love ci yaw du jeex du jeex Fok ma wane way fi nga tollu ci man Day mel ni géej, amul limit, no no limit Dama la wóolu nga ñëw Bañaloo ma dara ci yaw Ci la xam ni li mooy mbëggeel Sama xel bi neex coofeel Yaw rekk yaay ki ma doy Sama xol bee yaa koy ray Xol bi di tëb, di fecc Su ma nekkee ci sa wet Duma mësa wet ndax yaa tax may nekk Doo juge ci xol bi xel bi yaa fi nekk ni Man ak yow à l'infini, bae xool ma fi Yaw rekk laay topp Sama xol yaw rekk la sopp Yaw rekk laa nob Sama xol yaw rekk la sopp Moo tax loo wax ma ne wa waawaaw Soo ma nobee benn ma la dàqa nob Moo tax loo wax ma ne wa waawaaw Soo ma nobee benn ma la dàqa nob Di ci fey dem fu sori lool Fas yénne ci naan ba màndi lool Man ak yaw dañ ci dem ba jeex Mbëggeel bu yatu ba mel ni deex Hée! Dafa dem Dem ba su may dof Yaw laay topp Mbëggeel bu yatu ba mel ni deex Baby yaw rekk lay topp Yaw fi nga nekk man foofu lay dem Yaw rekk lay topp Jox naa la ko Ci yaa ko moom, xol bi yaay boroom Ndax yaw rekk laay topp Baby yaw rekk laay topp!