Dina la dal foo ko dul fooge Foo ko dul xalaate Ci ba ngay dogu ci la laay duggé Dey mel ni Yàlla ko yónnéé Dina fees sa xol bi, unh no no Ëlëmal sa bopp bi, unh yeah yeah Dooto amati principe, bafouer nga lépp Mënoo gis ci moom sikk Yaw lu maa lay def du yow rekk yaa ko xam ma Du lu nit mëna wax Yoow fi nga may yóbbu, dafa mel ni mësuma fa dem Waaye du lu niit mëna wax May topp sa ginnaaw di daw Mel ni mbëggéelu xale xale xale May laaj kañ laay maggee Nga teyi ci sama yeri bi ñuy xandal Dawal mbégé mbégé mbégé Dégg na sax dama jonge Kon kaaru kaar, kaar machallah Dañu bëggante ba niróo Yaay sama héro Sama bébé d'amour Conquérir nga sama xol Fi yaa fiy buur Defal lu la neex nga xol Boo bégee ma bég, boo jooyee ma jooy Li ma gisul ci ñoom laa gis ci yow mu doy ma Sànni nga karawaas Daan nga leen jél bu gaaw Maay sa jomb a ñaaw Jomb naa la def lu ñaaw Ndax kérok ba ma la gisee, eh eh Eh eh si la xam ni doo ma rëccé Man kérok ba ma la gise Eh eh si la xam ni doo ma rëccé Yow seral nga sama xol Guuy guuy guuy guuy Yow séral nga ma Guuy guuy guuy guuy Yow walay séral nga sama xol Guuy guuy guuy guuy Yow séral nga ma Guuy guuy guuy guuy Yaw tànk ak tànk, mbagg ak mbagg ñu dem Waat nani dina la yobbu feneen Yaw defal ndank bul deglul waxi noon Ñoom duñu dem bëgguñu ku dem Eh, xanaa xamoo ni lu baax ñepp ko bëgg-bëgg Fi li ñuy wax xaaj ba du dëgg-dëgg Eh, xana xamoni mën nañu wax mais duñu bëgg Seen biir xol mënu ñu gis ñaar ñu bëggante Te xam naa waroon na doon gëwel Ma taggal la say maam Waroon nga doon jaam Ma goreel la goreel say maam Su ma amoon avion ma may la ko di la dawalal Foo bëgg ñu jëm ca Li su la doyul wax ma lu lay doy bébé Walay walay xawma li lay doy May topp sa ginnaaw di daw Mel ni mbëggéelu xale, xale, xale May lajj kañ laay maggé Nga teyi si sama yeri bi ñuy xandal Dawal mbégé mbégé mbégé Dégg na sax dama jonge Kaaro kaar, kaar machallah Dañu bëggante ba niróo Yaay sama héro Sama bébé d’amour Conquérir nga sama xol Fi yaa fiy buur Defal lu la neex nga xool Ndax kérok ba ma la gisee, eh eh Eh eh si la xam ni doo ma rëccé Man kérok ba ma la gise Eh eh si la xam ni doo ma rëccé Yow seral nga sama xol Guuy guuy guuy guuy Yow séral nga maa Guuy guuy guuy guuy Yow walay séral nga sama xol Guuy guuy guuy guuy Yow séral nga ma Guuy guuy guuy guuy May topp sa ginaaw di daw Mel ni mbëggéelu xale xale xale May lajj kañ laay maggé Nga teyi si sama yeri bi ñuy xandal Dawal mbégé mbégé mbégé Dégg na sax dama jonge