Man sama sañse yaw la Fu ma belli yaw la Du kenn yaw la Dofloo nga ma Man ki ma tànn yaw la Nga nob ma raw la Du kenn yaw la Dofloo nga ma Yaa ma ko tàmmal Yaa ma ko jàngal Yaw li nga àndal Dofloo nga ma Laax bi lu mu tàng tàng Kenn du ma ko ràccal Li nga jantal Dofloo nga ma Jëkkër su la nobee Danga koy tiitaroo Ni ma la nawe Yaay sama héros Samay gént nga may àndil mu leer Ma pare dundu lu ne dox ci li la neex Pare naa (pare naa) Pare naa (pare naa) Manatuma la rëcc, sama seytaane Pare naa (pare naa) Pare naa (pare naa) Neex neex bi sama dundu yawa coco bànneex Man sama sañse yaw la Fu ma belli yaw la Du kenn yaw la Dofloo nga ma Man ki ma tànn yaw la Nga nob ma raw la Du kenn yaw la Dofloo nga ma Yaa ma ko tàmmal Yaa ma ko jàngal Yaw li nga àndal Dofloo nga ma Laax bi lu mu tàng tàng Kenn du ma ko ràccal Billaay waay Mbëggeel nak Bu la jàppe nga doon xale Dootoo dal Foo tollu di koy wane Lii moo tax fu ma tollu di la jege Nga may nab-nabbee Wane ni nga jonge Mbëggeel nak (waxal!) Bu la jàppe nga doon xale (nga doon xale) Dootoo dal (dikkal) Foo tollu di koy wane Lii moo tax fu ma tollu di la jege Nga may nab-nabbe Wane ni nga jonge Talibee Cheikh Bi Jambari Al Amine Bëgg na AÏcha rasul ba mu jeex yaay Dundu mbëggeel dafa neex Xoolal timis bu Aziz Ndiaye Pare naa (pare naa) Pare naa (pare naa) Manatuma la rëcc, sama seytaane Pare naa (pare naa) Pare naa (pare naa) Neex neex bi sama dundu yawa coco bànneex Man sama sañse yaw la Fu ma belli yaw la Du kenn yaw la Dofloo nga ma Man ki ma tànn yaw la Nga nob ma raw la Du kenn yaw la Dofloo nga ma (dikkal!) Yaa ma ko tàmmal Yaa ma ko jàngal (waxal!) Yaw li nga àndal Dofloo nga ma Laax bi lu mu tàng tàng Kenn du ma ko ràccal Li nga jantal Dofloo nga ma