Jigéenu jant Jigéenu weer yaa ñu leeral Yaayoo nga cant Kuñ fi coow yaa ko féñal Yaa di ndox, yaa ñu tax a màndi Yàgg nga di dox, nelawoo bidënti Yaay àdduna, sargal la jaddu na Feccal ma tàccu la, tey ma wayal la Sa jom ji yatu na Say jëf ñoo ko sedde yaa ñu nàmpal Bott ñu, ar ñu, yañu tete Yaw rekk jar a takkal Médaille gu ne yaa ko yelo Daj nga fi lu ne Taxul nga soppi melokaan Su ma lay way sa jom a tax (Sen fu la ak fayda wër na àdduna) Sa ngor a tax (Yenn rekk a taaru, tay ma joobe leen) Géwél tëggël ñu jayyu Tey nga joobeleen Li coow li bari bari may ki ko waral (doxal!) Li coow li bari bari may ki ko waral (yëngul!) Man rekk (hé, yaw rekk!) Man rekk, ma bari doole Li coow li bari bari jigéen naa ko waral (doxal!) Li coow li bari bari may ki ko waral (yëngul!) Man rekk (hé, yaw rekk!) Man rekk, ma bari doole Géwél tëggël, ñeeño tàccul Laobé jukk lëmbël Géer jukk di maye sax jigéen ñoo ko waral Jigéen ju baax nan la war a mel Xanaa ni nan (ni), nan (ni ni) Yaa ñeme coono yaay jaambar Yaa ngi liggéey toogoo di xaar Yaayu Astou Gueye baax na Gore na jom ju bari lool Wayal, wayal Leen lu fi baax jigéen na ko waral, wayal! Bakkari musel jigéen Ma way Bul dóor, bul saaga, bul toroxal Jigéen la! Dieyla, feccal ma li kay! Jox ko li mu moom Mooy ki juur sa doom Bi nga dee gone gone gone Moo la nàmpaloon Kaay! Li coow li bari bari may ki ko waral (doxal!) Li coow li bari bari may ki ko waral (yëngul!) Man rekk (hé, yaw rekk!) Man rekk, ma bari doole Li coow li bari bari jigéen naa ko waral (doxal!) Li coow li bari bari may ki ko waral (yëngul!) Man rekk (hé, yaw rekk!) Man rekk, ma bari doole Feccal ma way la (doxal!) Jayyul ma jiin la (yëngul!) Xam naa sa doole Yaw rekk def jaloore Tey ma jobel la ku aye wal sa momee Jayyuleen, wuy wuleen jayyuleen Feccal ma li, kay!