Dafa am bees Nabi Sallallahu Alaihi Wasallam ngeen gi mbidef Nabi Bésu it lawoon Nabi romb xale yi ñu tok Sañse ba jekk di fo di ree am ca ñoom ku béru di jooy Ngeen ngi mbidef Nabi Sallallahu Alaihi Wasallam woo xale ba nekkoo doom lu wappal fowo ni say morom ngaberu di jooy? Xale ba dal di ni ko Sama baay da àndoon ca xeex ba ag Nabi Sallallahu Alaihi Wasallam dee fa ma weet jaaxle Sama yaay séy ak beneen góor mu gëne ma nangu sama alal Nangu sama kër ba maa ngi Tumuraanke di taxawaalu ak di fanaan ci mbedd yi Mu toroxal ma, busanal ma, mettital ma Mo waral ci bésu it bi Sama xel dem ci sama baay ma weet jooy Xam ne su dundoon duma mësa tumuraanke Naka noonu Nabi Sallallahu Alaihi Wasallam ne xale ba ndax bëgg nga ma doon sa baay Aïchatu doon sa yaay Fatimatu doon sa mag Wa aliune ak Hassan ak Housseyu doon say mag Xale ba daaldi ni ko Ana kan may bañ ya rassouloulah Nabi Ana kan mooy bañ ya rassouloulah Neen ngi mbidef ki gën te kenn gënu ko Xureyshiin yaay seen géer Banuhasim yaay seen baay Ana kan mooy bañ Nabi Naka noonu Nabi Yóbbu xale ba këram, taral ko Mu dellusi taru lool Ñëw moroom ya naan ko Sa taar bi ak sa leer gi nga andal Wute na ak bi nga fiy jugee Ndax danga mel ni ku judduwaat Xale ba dal vi ni leen Yoneen bi la dajel Mu laaj ma lu may jooy Ma wax ko ko mu yóbbu ma këram Kon man rassouloulah matax Aïchatu doon sa yaay Fatimatu doon sa mag Wa aliune ak Hassan ak Housseyu doon say mag Xarit ya daaldi ni ko Yaa Nabi Su ñu sañoon Su ñu bayee Dee ca xaree ba ndax yaa rassoulilah