Gune may dékk Ma nga may daaneel Fi ma la tég Romb naa bu gañe Gune may dékk, waay Ma nga may daaneel Fi ma la tég waay Romb naa bu gañe, waaw Ku la doon wuute ci man dinaa la am Ku ma bëgg bàyyek yaw, na ma ba xam Jaral nga ma xeex ak gaynde, nañ ci nu mbaaxal Bu suuf seede ba ñépp tëddi ma, am lu ma la wan waay Sama mbëggeel dafa faq wuuti sa bos Sama xol jarafe sedd kër giy jalañoo Su ñu gisee ma na weete ba am lu ma la def Ndax gone may dékk waaye ma nga may daaneel Xale bi defal ndank Ñëwal sax ma déey la Loo ma ñaan ma may la Bu doyul ma dolli la! Gune may dékk Ma nga may daaneel Fi ma la tég Romb naa bu gañe Yaa ma gënal ñi ma xam ak nit ñi ma xamul Jaral nga ma def a def ba def lu ma munul Ni ngay doxe dafa yeem ma dikk lu ma amul Ku mel ni yaw dootu fi am ñi dañu xamul, waay! Sama mbëggeel dafa faq wuuti sa bos Sama xol jarafe sedd kër giy jalañoo Su ñu gisee ma na weete ba am lu ma la def Ndax gone may dékk waaye ma nga may daaneel Xale bi defal ndank Ñëwal sax ma déey la Loo ma ñaan ma may la Bu doyul ma dolli la!