Man ku ma xam, xam ni bëgg naa la Li ma gëna neex mooy sa jantal Man xawma lu tax ma bëgg la Dem àljanna yaa ci gëna gaaw Di dégg say je t'aime (je t'aime, je t'aime) Tax duma jug ci féem (di féem waawaaw) Su ma dee garab (yaay ren, yaay ren) Ndax yaa ma tànn (def ma reine waawaaw) Man yaw laa bugga, change pas bae Neex nga ma mën na doon sa jabar, doon sa maman Lu ma ci gobe, bëgg naa Di dox ci xal ñów fekk ci la Dëb sol, caxabal Foo ma woo ma ñëw Loo fi laal, loo fi laal Rekk ma lalli ko Dëb sol, caxabal Foo ma woo ma ñëw Loo fi laal, loo fi laal Rekk ma lalli ko Man ku ma xam, xam ni bëgg naa la Li ma gëna neex mooy sa jantal Man xawma lu tax ma bëgg la Dem àljanna yaa ci gëna gaaw Di dégg say je t'aime (je t'aime, je t'aime) Tax duma jug ci féem (di féem waawaaw) Su ma dee garab (yaay ren, yaay ren) Yaa ma tànn (def ma reine waawaaw) Wantanamera, feccal la youza Toogal seetaan, ehn ma daagu dukkat Ñoom de li ñuy jaay dama koy maye baby waxal Li ci wañ bi toggantu ay nga ma koy ñamal Wantanamera, feccal la youza Toogal seetaan, ehn ma daagu dukkat Ñoom de li ñuy jaay dama koy maye baby waxal Li ci wañ bi toggantu ay nga ma koy ñamal Waxal li nga bëgg, maa def fi yaa fi dogal Lu jaar siisu naanal potu ndox te nangu ndogal Su weesu waxi noon, kër gi maay boroom Te lépp lu ma moom, baby yaay boroom Dëb sol, caxabal Foo ma woo ma ñëw Loo fi laal, loo fi laal Rekk ma lalli ko Dëb sol, caxabal Foo ma woo ma ñëw Loo fi laal, loo fi laal Rekk ma lalli ko Man ku ma xam, xam ni bëgg naa la Li ma gëna neex mooy sa jantal Man xawma lu tax ma bëgg la Dem àljanna yaa ci gëna gaaw Di dégg say je t'aime (je t'aime, je t'aime) Tax duma jug ci féem (di féem waawaaw) Su ma dee garab (yaay ren, yaay ren) Yaa ma tànn (def ma reine waawaaw) Wantanamera (Woyal céy mbëggeel li dafa over neex!) Ehnnnn ennh Bu nit mënoo na génnee li ne ci xol bi waay! (Li dafa neex, dafa neex, mbëggeel rekk a neex) Sa nijaay ak sa ñoom yaay Ña fay gis ñi toog di waxtaan Mënuloo xam ni ma la bëggee eh (Abass dafa lank danga sof, bëgg bay jooy) Mënuloo xam ni ma la bëggee eh (Woyal nga Abass, woyal nga faatu awo buuru këram!) Su ma lay ray say xàqataay Moo may tax a naam say jootaay Mënuloo xam ni ma la yëgee bae (Abass Diadiou baayu Papa Diadiou mëna yor jigéen) Mënuloo xam ni ma la yëgee bae (Aida Samb li dafa neex, dafa neex, dafa over neex) Sama tey yaw la, sama suba sax yaw la Sama tey yaw la, sama suba sax yaw la Awma sa fay baby, teral nga ma Awma sa fay baby, teral nga ma (Chérie Abass Diadiou mbëggeel rekk a neex) Lu ma la mën a fayee sagal nga ma (Abass toog Fatook Aida mbëggeel dafa neex) Sama tey yaw la, sama suba sax yaw la Sama tey yaw la, sama suba sax yaw la Awma sa fay baby! Lu jugé ci xol ci sol lay déllu Mbëggeel rekk a neex! Aida Samb woyal na jigéen ñi nob seen jëkkër Jëlal! (Awma sa fay baby, teral nga ma) Daan ko bugga mu bugga la, yëfi buggante la (Awma sa fay baby, sagal nga ma) Bëgg nga ko bëgg naa la te bëgg na leen yëfi bëggante la Sama tey yaw la, sama suba tamit yaw la Sama tey yaw la, sama suba tamit yaw la Awma sa fay baby, teral nga ma!